Nataali Gérard Quenum


Ana niroowalé bi ame si diagganté niaary way jëfëndikoo pééntuur aar yu Bénin Gérard Quenum ? bénne péétuurukaay bu yame (li ëpp si nataal bi day doone niuul ak wééx, ak tamite yééne si ay kulër yu oyof). Ak tamit ay rëdd yuy missaal ay gnite muuréko ak lu niuul bamiy saf ay takkandéér. Ak lu aartist bi foonk trope, muy wallu dém béék dikk bi nga xamné day misaal yënguté ak tuxu. Si niaary liggééyi aart yi amoone si atume 2013, Gérard Quenum dasiy nétali jamono yam nékkéé Londre ak lii niiu tuddé Taxi Londres, di mééngook Taxi brousse si bénin mba sax si afrik yéépp.

« Taxis brousse » ay daamar yunuy xameekoo Afrik lagne. Doonté sééne dayo bu ndaw, yooyu daamar dagni sëf lu bari sééne kaw diko yoobu. Gérard Quenum day misaal sëf bu diis boobu si picc munek si biir kaaf gu mak. Nite ki nékk si bitti daamar gui day misaal ame mbooloo, ndéém xët-xët and rajaxoo giy ame siy gaari daamar yi nek Afrik.

Nataali Samuel Fosso


Lii ay nattali gnite la yu féés aki kulër ! ab piraate ? borroom nomba ? jangalékatu fééy, fééykate, ab woykate, buurub afrik ? lii lépp taxut nataal wi soppééku : Nataal winu fësël si ay anmam yu wuuté, day jëmël di missaal nataali doomi aadama si ay mélokaane yu bari. Fukki nataal yii danioo bokk si sayu TATI winu amal si atum 1997 ganaaw baneko laajéé, si banedoone amal juroom fukkélu aniwerséér bine jagléél sééne maangaséé yi féété si dëkuwaayu Barbes sa Paris. Sayu TATI dana deff ay caambar ak saytu, yi roomb di rëdaate ak toppaate si ay nataal : Samuel Fosso day jëfëndikoo nataalam ngir kiiraay gum mana waxanté ak tubaab yi, walla sax waa politik yi.

Mu déoone ab Kamaruné bu nék Sentre afrik ay ate yu bari, Samuel Fosso du massa noppi di génnéé yu yéés, diko jaaralé saasuné si lumu xam lool muy : nataal sa bopp saw dundine.

Nataali Magique Bruce Clarke


Nagne wax léégi si niaari nataali aar yu jëm si waalu boks : « L’impensable, bu atum 2005 ak The game begins, bu atum 2011. Gënelééna jégéé, suka défféé ngééne séétlu xam-xam bi Bruce Clarke ame, ab aartist biritanik la bu cossaanoo rééwu Afrik sawou jante. Day boolé pééntuur ak këyiti taff, ay kallaama ak nataal, di deff ay féém si nimkoy tégaléé ak yaraxtaangé gui. Mu nek aartist bu jambaaré, Bruce Clarke, dafniuy wax si bénne taggat yaram boo xamné amena lumu nirrook, xééxu axx ak yéllééf doomu aadama. Ca rééwu  États-Unis (USA) dagnefaa téréwoone boks bu ame si digganté gnit ku wééx ak ku niuul. Si atum 1910, Jack Johnson, bokskate bu niuul bi ndiaëka gaaddu ndamali si aduna bi. Mayu niukowoone mu bokkaate si jogantei boobu. Xeex bi amoone ngir niu nangulko axxam ak toluwaayam, manéésnakoo mééngalé ak xééx beddiwanté si digganté gnite ku niuul ak ku wééx. Gannaaw bam bokké si joganté ba, ndam lamesa jëlé, mujna jur ay jaamarlooy xéét si rééwma yéépp. Si jamonoy niaar fukkéélu siéékale bi, boks rék moo doone liy taxa ame yokkuté si wallu dundine. Bruce Clarke day jël xééxi ak jamarloo yi ame si aduna bi diko missal si boks.

Nataali Frédéric Bruly Bouabré


Fii taarixi Bekora, ngééni guiss, aw xëtu fukk ak niaari nitaal bu Frédéric Bruly Bouabré, ab aartist ivoirien la, faatuna si atum 2014. Bolééne xoolé bu baax digééne guiss ni day boolé nitaal akam mbind siw këyit, déffééko xalimaag këyit, pastel ak daa.

Xët woowu day nétali taarixu bénne rëbbkate bu tudd Bekora, ame bénne bis bumu démoone rëbbi dajéfaak Gbli, aw niaangoor wumu dimbali ngir mu dund.Ngir jaajëfëlko, Gbli néko soo bëggéé mane naala jox lépp loo bëgg. Bekora dunde abadane laa bëgg. Gbli daaldikoy wane béne garab ak nagneko wara jëfëndikoo.Ba Bekora délloo sa dëkk ba, daaldi nétali jabaram li ame, néko nako déffal téré bi si aye nélawam, kééme nikoko jaan dji waxéwoone. Ay waxtu si guinnaaw bi, bi soxnasi dikké guisut jëkëram, waayé ay xéér lafa fékk. Looloo waral niunaane: « Ku bëgga dunde abadane, na doone xéér ».

Niaar fukki nitaal yi ëmb taarix bii, su boolool juney-juney yénééne yu Frédéric Bruly Bouabré liggééy, day done aw xët wune tuddéé « xam-xami aduna », tééré bu mak bu aartist bi jagléél waa aduna bi, guinnaaw ay gëstu yu tollook xaaju siéékal.

Nataali Cyprien Tokoudagba


Nagne wax si Cyprien Tokoudagba ! liggééyame bi laamboona lool ak taarixu caada yu Dahomey. Lolééne di guiss ? aw nagu aall ? firwi ? waw, wayé roomb nagne foofu. Daf Sax té gëm ndono gui ame si gëm-gëm yi ak taarix yi, si ay pééntuuru aakrilikam, Cyprien Tokoudagba day fësal xaamméékay buuri Dahomey yi. Ab aartist béninoi la ; faatuna si atum 2012. Nagu all wi, ca atum 2005, xamméékaayu Buur Guézo la. Rap wu ame doolé wii, day tékki ni amul lééne luy térré buur ba du déff limu nass. Si suufu nagu all wi, amena guénne gënn guy misaal  dëkkub Abomey, kaapitaalu dëkk ba. Firwi bi, ca atum 2006, xaamméékaayu buur Agonglo la. Si kallaama waa dëkk ba,firwi rone day tékki Agon. Xaamméékaay bi day méngook wax bii « dënd day dal si garabuk tiir, wayé rone lumu gud-gud dinasi mucc ». Loolou day gaaruwaalé mane-manu buur bi si moytu ndëg sërëx yi, ak jaffé-jaffé yiy ame si jamonoy faloom.

Nataali George Lilanga


Geoge Lilanga ab aartist tanzanien la, fatuna si atum 2005. Ay nataali aaram, ak sééni kulër yu fëss té taalli day topp cosaanam, manaam cosaani  Makondé yi, aw waaso wuy laakk kallaama bantu, dëkkéé si bëj gannaari Tanazani sa bëj sawou Mozambik. Day nétali cosaanam si niéénti péénturu arkrilik si atum 1998. Dagne  siy guiss aaduna bu jaxassoo, féés déll aki mbindééf yo xameni séne jëmmi gnite matul, sééne taar matul. Wanté bayééku gi am si pééntuur yooyu térewkoo tégu si anam yu mucc ayub, ba nga xamni jëmm yi dani ame dig wu niuul wulééne wër.

Nataali Omar Victor Diop


Dalsilééne ak jaam si « Le studio des vanités »niatti nataal yii ca atum 2011 boknagne si liggééy yi njëk yu Omar Victore Diop taxawal.Nataalkatu sénégalé la. Dingééne guiss xaamméékaayu nataal yi : ataal yu sét, rawatina si coll yi ak takkaay yéék yénééne yu laambook natal wi. Dagnekoo ték si nataal yu taaru té mééngook jamono, di dëggël ni Omar Victore Diop day jox yitté lii di nataal, lukoy taaral agit coll gasay féégne. Si nataal yooyu, amenasi ay gnit yuy yëngu si waallu caada ak cosaan si dëkki afrik yi, daanaka day nataal niu bokk jamono, nioo xameni dani liggééy ngir déff afrik mu doone féés mana rooté si wallu xam-xam ak xaralay jamono.

Nataali  Soly Cissé


Gnatti liggééyi aartist sénégaalé bii di Soly Cissé, aw xët la wun duppé Bestiaire, gninko déféé pastel ak pééntuure akirilik siw këyit si atum 2009. Mane nagneséé guiss ay jëmm yu yéémé té raglu, yu kénne xamut luniy niru. Si ay rëd yu téguwut si wénne saart, Soly Cissé dasy wané aduna bu tollook jamono (misaal bi moy ay li maki kode yu laxxu si biir liggééyam) té doy waar, tolook jamonoy rap yi. Si nataali aartist bii, mbindééf yu yéémé yi dasiy wané nékkinu doomu aadama, si aduna boo xamni cooppité barina.

Nataali Romuald Hazoumè


Xool lééne bu baax niaary nataali aartist Béninoi bii di Ramuald Hazoumé. Ana fane la kulëram ak xaralay aaram di jugé ? aartist bi day jëfëndikoo ay njaxas yu raxut : suuf, nééfaray nak, indigoo... Wa misaal yi nak ? kaaré, wërngël, toomb, espiiral, rëdi nomba, fitt : lumiy tékki ? Romual Hazoumé, boolé si niari pééntuuram yooyu, Lete-meji sa atum 1993 ak La reine sa atum 2006, misaali Fa, nek xaamméékaayu  xaaday yoruba. Di téékki gu jis-guisi yoruba. Misaal busi nek dëxëgne na lu baréé-bari. Romual Hazoumé dakoy jëfëndikoo ngir indi ay laac si wallu caadaay boppam, si ëlëgu afrik, wala si ëlëgu aduna bi. Aartist bi day  boolé boppam si boobu cosaan, di bakkéé boppam « Are », Moom ab aartist yoruba la buy yaatal caaday yoruba si ay tukkéém.

Nataali J.D.’Okhai Ojeikere


Niatti nataala ngii, bokksi si xëtu Hair style. Bu nataalkatu nigérian bii di J.D. ‘Okhai Ojeikere. Aartist bi xamena bu baax njarigne li nataal ame ngir samm caada,niu dajalélééne si xët wii, defarko si di  gganté atum 1968 ba 1999, lu ëpp junniy nataal di wané ay létti jigééni Nigeria. J.D.’Okhai Ojeikere day deff fii ak paatali si passongu létt yu bari yi, ak sééne mélokaane wu taaru té ame lumuy wané. Fii si Afrik létt yamut si taaral rek, day wané askan wi ndawsi deff létt yi bokk, téyit xew-xew bunékk amena léét yumu mééngool. Si natal yi jiggééne yi dagni natalu ak sééne ganaaw yaram, kénne dulééne xamméé, lu nééw lagni nataalu di wané sééne xar kanam. Kaadar bi, dëgmalu si létt yi,day gëne di wané mélokaanu aarayam.



Xëtu Hair style mo gënna siiw, si  li J.D.’Okhai Ojeikere di défaral boppam, lu bukkutak ay yëngu-yëngoom si wallu nataal ak limu laambool. Aartist bii faatuna si atum 2014,wayé dafa jappoone ni liggééyam niéépasi deff sééne yité ngir mu sotti, xaragnam si waallu nataal dafa lëkkëloo ak xaragnetaangé léttkat bi, ak tamit bob kiliyan bi naangu niu létt ko.

WakponWOL.html
WakponInfo.html
iWakponInfo.html

WAKPON – Le Musée fait le mur si xaralay kurélu Zinsou la.